yéen mbooloom jigéen ñi deeleen saraxe, man de gis naa leen ngeen ëpp ci waa sawara" ñu ne ko: ndax lan yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne: "dangeen a bari ag rëbbaate, di weddi njekk, gisuma jigéen ñu matadi xel ak diine te gaaw a yóbb xelu góor gu dogu ba mel ni kenn ci yéen jigéen ñi

yéen mbooloom jigéen ñi deeleen saraxe, man de gis naa leen ngeen ëpp ci waa sawara" ñu ne ko: ndax lan yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne: "dangeen a bari ag rëbbaate, di weddi njekk, gisuma jigéen ñu matadi xel ak diine te gaaw a yóbb xelu góor gu dogu ba mel ni kenn ci yéen jigéen ñi

Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi dafa génn ab yoor-yoor walla korite jëm ca julleekaay ba, mu romb jigéen ñi, daal di wax ne: "yéen mbooloom jigéen ñi deeleen saraxe, man de gis naa leen ngeen ëpp ci waa sawara" ñu ne ko: ndax lan yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne: "dangeen a bari ag rëbbaate, di weddi njekk, gisuma jigéen ñu matadi xel ak diine te gaaw a yóbb xelu góor gu dogu ba mel ni kenn ci yéen jigéen ñi", ñu ne ko: ana lan mooy matadig diine ji ak xel mi yaw Yonente Yàlla bi? Mu wax ne: "xanaa seedeg jigéen du xaaju seedeg góor?" Ñu ne ko: ahakay, mu ne: "loolu ci matadig xelam mi la bokk, xanaa du bu gisee mbaax du julli du woor?" Ñu ne ko: ahakay, mu ne: "loolu ci matadig diineem la bokk".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa génn ci benn bisu xew jëm ca jullikaay ba, fekk digoon na jigéen ñi ne dana leen beral ag waare, mu def ko ci bis booba, daal di wax ne: Yéen mbooloom jigéen ñi deeleen saraxe, tey baril jéggalu; ñoom ñaar bokk nañu ci yi gën a màgg ci yiy sippi njuumte, te man gis naa leen guddig rañaan gi ngeen ëpp ci waa sawara. Genn jigéen gu am xel ak gis-gis ak ug wegeel ci ñoom ne ko: yaw Yonente Yàlla bi lu tax nun nu ëpp ci waa sawara? Mu ne: ngir ay bir: dangeen a bari lu ngeen di rëbbaate ak ŋàññaate, te dangeen di weddi àqi jëkkër. Topp mu melal leen ci wax ne: gisuma jigéen ñu matadi xel ak diine te man a not góor gu am gisee ak xel ak ug dogu ak man a téye mbiram ci yéen. Mu ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, ana lan mooy wàññeekug xel mi ak diine ji? Nee na: bu dee wàññeekug xel mi nag mooy ne seedeg ñaari jigéen day tolloo ak seedeg genn góor; lii wàññeekug xel la, wàññeekug diine ji nag mooy wàñeekug jëf ju baax ji, ndax day toog ay guddi ak i fan du julli ngir limuy gis mbaax, dog ay fan ci koor gi ci sababus mbërëg mi, lii wàññeekug diine la, waaye ñoom deesu leen yedd ci loolu te deesu leen ko jàppe; ndax dafa bokk ci seenu bindiin ci cosaan, kem ni nu sàkke nit bind ko muy bëgg alal di yàkkamti ay biram di réere...ak yu dul yooyu, waaye dafa yeete ci loolu ngir moytandikuloo ñu fitnawu ci

فوائد الحديث

Sopp nañu jigéen ñi génn jëm ca jullig feet ga, ak ñu beral leen ag waare.

Weddi njekk ak baril rëbbaate dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi; ndaxte tëkku ci sawara màndarga la ci bàkkaar bu mag.

Nekk na ci it ag leeral ci yokkuteg gëm ak wàññeekoom, ku ay jaamu Yàllaam bari gëmam ak diineem yokk, ku ay jaamu Yàllaam wàññeeku diineem wàññeeku.

An-Nawawii nee na: am xel day yokku di wàññeeku, niki noonu it ngëm, li ñu tudd ag wàññeekoom ci jigéen jubluwuñu ci yedd leen ci loolu; ndaxte dafa bokk ci cosaanu bind gi, waaye yeete gi loolu ag moytandikuloo la ci fitnawu ci ñoom, loolu moo tax mu toftal mbugal ci li mu tudd ci weddi njekk déet ci wàññeeku gi, wàññeekug diine it nekkul lu yam ci yiy waral bàkkaar waaye gën na a yaatu loolu.

Nekk na ci it aji-jàng ji di dellu ci boroom xam-xam bi aji-toppe ji di dellu ci ki muy topp ci li mu wax bu maanaa mi feeñul ci moom.

Nekk na ci it ne seedeg jigéen xaaju seedeg góor la, ngir néewug takkam.

Ibn Hajar wax na ci li mu ne: "gisuma jigéen...ba mu jeex" li ma gis mooy loolu dafa bokk ci liy tax ñu nekk ñi ëpp ci waa sawara; ndaxte ñoom bu dee ñooy sababus demug xelu góor gu dogu ba tax muy def mbaa muy wax lu jaaduwul kon bokk nañu ak moom bàkkaar ba ëppale ko ca sax.

Araamalees na julli ak woor ci jigéen gi ci jamono mbërëgam, niki noonu it ñi nekk ci dereeti wësin, topp ñuy fay woor gi rekk bu ñu laabee.

Rafetu jikkóy Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, tontu na jigéen ñi ci seen i laaj te taralul ci ñoom yedduleen tamit.

Ibn Hajar nee na: saraxe day jañ mbugal, te amaana mu far bàkkaar yi dox ci diggante mbindeef yi.

An-Nawawii nee na: wàññeekug diine ci jigéen ñi ci sababus seen ug bàyyi julli ak woor la ci jamonoy mbërëg; ndax ku ay jaamoom yokk ngëmam ak diineem yokk, ku ay jaamoom wàññeeku diineem wàññeeku, wàññeekug diine ji amaana mu nekk ci anam gog da ciy am bàkkaar niki ki bàyyi julli walla woor mbaa geneen jaamu gu dul yooyu ci lu dul ngànt, amaana it mu nekk ci anam gog bàkkaar du ci am niki ki bàyyi Àjjuma walla xare walla leneen lu war ci moom ci ludul ngànt, man naa nekk it ci anam gog dees ka koo digal niki aji-gis mbaax gi bàyyi julli ak woor.

التصنيفات

Àttey jigéen ñi, Meloy Àjjana ak Sawara