Masuma a gis Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy xàqataay di ree ba ma gis ay yàppi biir gémmiñam, waaye da daan muuñ

Masuma a gis Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy xàqataay di ree ba ma gis ay yàppi biir gémmiñam, waaye da daan muuñ

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Masuma a gis Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy xàqataay di ree ba ma gis ay yàppi biir gémmiñam, waaye da daan muuñ.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Aysatu yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daawul ree reetaan gu ëpp ba ñuy gis am siiñam, waaye da daan muuñ.

فوائد الحديث

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc reetaanam mooy mu muuñ bu daan gërëm walla mu yéemu ci dara.

Ibn Hajar nee na: masuma ko a gis mu matale, ci wàllu ree, bay ree reetaan gu mat sëkk.

Bari ree ak yëkkëti kàddu di xàqtaay bokkul ci meloy ñu sell ñi.

Bari ay ree day tax kenn dula jox cër ak ug wegam ci say bokk.

التصنيفات

Reem SLM