إعدادات العرض
bu kenn ci yéen gisee ci gént lu mu bëgg, loolu ci Yàlla la bawoo, na sant Yàlla ci loolu te waxe ko, bu gisee lu dul loolu ci lu mu sib, loolu ci Saytaane la bawoo, na muslu ci ayam, te bu mu ko wax kenn, kon du ko lor
bu kenn ci yéen gisee ci gént lu mu bëgg, loolu ci Yàlla la bawoo, na sant Yàlla ci loolu te waxe ko, bu gisee lu dul loolu ci lu mu sib, loolu ci Saytaane la bawoo, na muslu ci ayam, te bu mu ko wax kenn, kon du ko lor
Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne: dégg na Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax naan: «bu kenn ci yéen gisee ci gént lu mu bëgg, loolu ci Yàlla la bawoo, na sant Yàlla ci loolu te waxe ko, bu gisee lu dul loolu ci lu mu sib, loolu ci Saytaane la bawoo, na muslu ci ayam, te bu mu ko wax kenn, kon du ko lor».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Bahasa Indonesia Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tagalog Français ئۇيغۇرچە Hausa Kurdî Kiswahili Português සිංහල Русский Nederlands Tiếng Việt ગુજરાતી অসমীয়া پښتو नेपाली മലയാളം Yorùbá ქართული Magyar తెలుగు Svenska Македонски ಕನ್ನಡ Moore Română Oromoo Українська ไทย मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛالشرح
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne gént lu baax luy bég loo ci ay nelaw ci Yàlla la jóge, mu gindee ci ne na sant Yàlla ci loolu, te waxe ko, waaye bu gisee lu mu sib lu koy jàqloo loolu ci Saytaane la jóge; na muslu ci Yàlla ci ayam, te bu mu ko wax kenn; kon du ko lor, ndaxte Yàlla moo def loolu muy sabab ngir mucc ci ay gént yu bon yu toftaloo.فوائد الحديث
Xeeti gént yi: 1- gént gu baax, moom dëgg la di bégle gu bawoo fa Yàlla, nit ki da koy gis, walla ñu gisal ka ko, 2- waxtaanu bakkan, te mooy li nit ki di wax ak boppam cig ñàkka nelaw, 3- jàqloo ak tiitloo yu Saytaane ak ay ragalloo yu jóge ci moom mu ciy jàqal doomu Aadama ji.
Li ñu man a jànge ci bunti gént gu baax, ñatti bir yii la: mu sant Yàlla ci loolu, daal di ciy bég, daal di koy waxe, waaye ku mu bëgg rekk la koy wax, wolif ku mu bañ.
Li ñuy jànge ci gént gu bon, juróomi bir la: mu muslu ci Yàlla ci ayam, ak ayu Saytaane, bu jugee ci nelaw yi tifli ci càmmooñam ñatti yoon, te du ko wax kenn mukk, bu bëggee dellu ca nelaw ya day wëlbatiku wet ga mu nekkoon; kon du ko lor.
Ibn Hajar nee na: xereñ gi si nekk mooy ne bu waxee gént gu rafet gi ki mu bëggul amaana mu firil ko ko ci lu mu bëggul ngir bañ ko walla soxor, te amaana mu am ci melo woowu walla mu yàkkamti ñeel bakkanam ngir jàq. ñu digal ko mu bañ ko a wax ku mu bëggul ngir sabab boobu.
Sant ci bu xéewal amee, ak bu xéewal yi beesaatee, loolu sabab la ci muy sax.
التصنيفات
Teggiini gént