Laaj naa Aysatu, ne ko: ci lan la Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan tàmbalee bu daan dugg këram? Mu ne: ci socc

Laaj naa Aysatu, ne ko: ci lan la Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan tàmbalee bu daan dugg këram? Mu ne: ci socc

Jële nañu ci Surayh ibn Haanii mu wax ne: Laaj naa Aysatu, ne ko: ci lan la Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan tàmbalee bu daan dugg këram? Mu ne: ci socc.

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Bokk na ci njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy tàmbalee ci socc bu daan dugg këram, ci waxtu wu mu man a doon guddi walla bëccëg.

فوائد الحديث

Yoonalees na socc ci mbooleem waxtu yi, loolu nag day gën a feddaliku: ci waxtu yi ko Aji-Yoonal ji soppe, bokk na ca: bu ñuy dugg ci kër, ak bu ñuy julli, ak bu ñuy jàppu, ak ginnaaw bu ñu yeewoo ci ay nelaw, ak bu xetu gémmiñ gi soppikoo.

Leeral xérug ñi toppoon ci sahaaba yi ci laaj biri Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak sunnaam; ngir ñu roy ko.

Jële xam-xam ci boroom xam-xam yi ak ci ki ko gën a xam, ba tax ñu laaj Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm biri Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu duggee ci kër gi.

Rafetug nekkiinu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak njabootam, ba tax mu daan laabal gémmeñam buy dugg ci kër gi.

التصنيفات

Sunnay set