Yaw Abuu Sahiid, ku gërëm Yàlla muy Boroomam, Lislaam di diineem, Muhammat di Yonenteem àjjana war na ci moom

Yaw Abuu Sahiid, ku gërëm Yàlla muy Boroomam, Lislaam di diineem, Muhammat di Yonenteem àjjana war na ci moom

Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Yaw Abuu Sahiid, ku gërëm Yàlla muy Boroomam, Lislaam di diineem, Muhammat di Yonenteem àjjana war na ci moom", Abuu Sahiid yéemu ci loolu, ne ko: baamtul ma ko yaw Yonente Yàlla bi, mu def ko, topp mu ne ko: "ak leneen lol dees na ci yëkkëtil jaam bi téeméeri daraja ca àjjana, te diggante ñaari daraja yi mi ngi mel ni diggante asamaan ak suuf ", mu ne ko: loolu lan la yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne ko: "jihaad ci yoonu Yàlla, jihaad ci yoonu Yàlla".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamal na Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm ne ku gëm Yàlla gërëm ko muy Boroomam di Yàllaam di Buuram di Sangam di ki koy digal, ak it gërëm lislaam muy diineem ci ag wommatu ak nangul ko ci mbooleem ay digleem ak i tereem, ak it gërëm Muhammat muy Yonnenteem ci lépp lu ñu ko yónni mu jottali ko; kon àjjana ñeel na ko, Abuu Sahiid yéemu ci loolu, ne ko: baamtul ma ko yaw Yonente Yàlla bi, mu def ko, topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: amna weneen melo wu Yàlla di yëkkëtee jaam téeméeri daraja ca àjjana, te diggante ñaari daraja yu ne mi ngi mel ni diggante asamaan ak suuf, Abuu Sahiid ne ko: loolu lan la yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne ko: jihaad ci yoonu Yàlla, jihaad ci yoonu Yàlla.

فوائد الحديث

Bokk na ci yiy waral dugg àjjana gërëm Yàlla muy sa Boroom, ak lislaam muy sa diine, ak Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy sa Yonente.

Màggal mbiri jihaad ci yoonu Yàlla.

Kawe gi wàccuwaayu jihaadkat bi kawe ca àjjana.

Àjjana amna ay daraja yoy maneesu ko a takk, ak ay wàccuwaay yoy maneesu ko a lim, jihaadkat yi am nañu ca téeméeri daraja.

Bëgg gi Sahaaba yi bëgga xam lu baax ak ay buntam ak i sababam.

التصنيفات

Meloy Àjjana ak Sawara, Ngëneelu xeex ci yoonu Yàlla