laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku ko Yàlla yombal ci moom

laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku ko Yàlla yombal ci moom

Jële ci Muhaas ibn Jabal yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Nekkoon naa ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci benn tukki, ma xëy benn bis jegesi ko fekk ñoo ngi dox, ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, xibaar ma jëf joo xam ne dana ma dugal àjjana di ma soreele sawara, mu ne ma: "laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku ko Yàlla yombal ci moom, dangay jaamu Yàlla te doo ku bokkaale ak dara, di taxawal julli, di joxe asaka, di woor weeru koor, te aji néeg ba" topp mu ne: "ndax duma la tegtal bunti yiw yi: woor ab pakk la, saraxe day fay njuumte kem ni ndox di faye sawara, ak jullig nit ki ci xaaju guddi " topp mu jàng: laayab « tata jaafaa junuubuhum ba àgg Yahlamuun » topp mu ne : "ndax duma la xibaar boppu mbir mi yépp ak kenoom?" Ma ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne: "boppu mbir mi mooy lislaam, kenoom di julli, njobbaxtal la di jihaad" topp mu ne : "ndax duma la xibaar li moom loolu lépp nag?" Ma ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu téye ci làmmiñam, daal di ne: "téyeel sa lii" ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, kon dees nuy jàppe li nuy wax? Mu ne ma: "yal na la sa yaay ñàkk yaw Muhaas, mo ndax dara dana këpp nit ñi ci seen kanam ya walla seen gémmiñ ya ca sawara lu dul seen góobiti làmmiñ?".

[Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee] [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]

الشرح

Muhaas yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: nekkoon naa ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci benn tukki, ma xëy benn bis jegesi ko fekk ñoo ngi dox, ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi xibaar ma jëf joo xam ne dana ma dugal àjjana di ma soreele sawara, Mu ne ko: laaj nga ma jëf joo xam ne lu màgg la ci bakkan yi, waaye nag lu woyof la te yomb ci ku ko Yàlla yombal ci moom; joxeel faratay lislaam yi: Bi ci njëkk: dangay jaamu Yàlla moom dong te doo ko bokkaale ak dara. Ñaareel bi: nga taxawal julliy juróom yi ñu farataal ci bis bi ak guddi: Fajar, ak Tisbaar, ak Tàkkusaan, ak Timis, ak Gee, ci ay sàrtam ak i ponkam ak i warteefam. Ñatteel bi: nga genne asaka ji ñu farataal, te moom ag jaamug alal la gu war ci jépp alal ju mat lim bu ñu tënk ci Sariiha, ñu koy jox ñi ko yeyoo. Ñenteel bi: nga woor weeru Koor, te mooy bàyyi lekk ak naan ak yeneen yiy dogloo ànd ak yéenee jaamu, tàmbalee ci fenkug fajar gi ba ca sowug jant bi. Juróomeel bi: nga aj néeg ba ci jublu Màkka jublu a taxawal ay jaamu, ngir jaamu Yàlla mu màgg mi. Topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ndax duma la xamal yoon wiy eggale ci buntu yiw yi? Loolu mooy nga toftal ci farata yooyu naafila yi. Bi ci njëkk: woorug coobarewu, moom day teree tàbbi ci moy yi ci damm bànneex, ak néewal kàttan. Ñaareel bi: saraxeg coobarewu day fay njuumte ginnaawam di ko dindi di far jeexitalam. Ñatteel bi: julli guddi ci ñatteelu xaaju guddi bu mujj bi, topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di jàng waxu Yàlla ji: {seen wet ya day sori} maanaam: day sori {lal ya} maanaam: nelawukaay ya {dañuy ñaan di woo seen Boroom} ci julli ak sikar ak jàng ak ñaan, {ngir ragal ak xemmeem te dañuy joxe ci li ñu leen wërsëgale, benn bakkan xamul li ñu ko deñcal ci luy bégal bët yi} maanaam: luy bégal seeni bët ëllëg bis-pénc ak ca àjjana ci ay xéewal, {muy ag fay ca la ñu doon jëf}. Topp Yonnente bi ne ko: ndax duma la xibaar cosaanu diine? Ak kenoom gi muy sukkandiku? Ak njobbaxtalam? Muhaas yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: mbir mi boop ba mooy: lislaam te mooy ñaari seede yi, te ci ñoom ñaar la nit ki di ame cosaanu diine. Kenoom: mooy julli, lislaam du am ci lu dul julli, kem ni nga xamee ne kër du am ci lu dul keno, kuy julli diineem dëgër na taxaw na; njobbaxtalu lislaam ak ug yëkkëtikoom moo ngi ci jihaad ak def pasteef ci xeex ak nooni diine ji ngir yëkkëti kàddug Yàlla. Topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ndax duma la xibaar liy téyé téyé bu dëgër mbir yii weesu? Yonnente bi jàpp ci làmmiñam, ne ko: téyeel lii te bul wax lu sa yoon nekkul. Muhaas ne ko: ndax sunu Boroom da nuy topp di nu càmbar di nu mbugal ci lépp lu nuy wax?! Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: yal na la sa yaay ñàkk! Li ñu ci jublu du ñaanal ko alkane, waaye daa bokk ci waxi araab yi ngir yee ko ci mbir mum waroon a xam bàyyi ko xel, topp mu ne ko: ndax dara dana sànni nit ñi di leen daaneel ca seen kanam ya ca biir sawara lu dul seen góobiti làmmiñ ya ci kéefar ak tuumaale ak saaga ak jëw ak rambaaj ak tuuma ak yu ko niru.

فوائد الحديث

Xérug Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ci xam-xam, loolu a tax ñuy baril di laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Déggug Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ndax li ñu xam ne jëf yi ñooy sabab si dugg àjjana.

Laaj bi jóge ci Muhaas yal na ko Yàlla dollee gërëm laaj bu màgg la; ndaxte ca dëgg-dëgg mooy mbóotu dund gi ak ug amam, lépp lu am ci àdduna jii ci doomu Aadama walla jinne fa muy mujj mooy àjjana walla sawara, loolu a tax laaj bi di lu màgg.

Toftalu dug Àjjuma ci kaw def ponki lislaam yi: te mooy: ñaari seede yi, ak julli, ak asaka, woor, ak aj.

Wéetal Yàlla moy li ëpp solo ci diine mooy la gëna kawe ci lépp lu ñu waral, te mooy jaamu ko moom dong amul bokkaale.

Yërmàndey Yàlla ci jaamam yi ci mu ubbil leen bunti yiw yi ngir ñu dolleeku ci sababi yiw yi ak njéggali bàkkaar yi.

Ngëneelu li nekk ci di jéema jege Yàlla ci def naafila yi ginnaaw bu ñu defee farata yi.

Julli ci lislaam mooy

tolloog keno biy

tax mbaar mi mana taxaw, bu demee

lislaam daldi dem,

kem ni mbaar mi di daanoo ci daanug kenoom ya.

Warug sàmm làmmiñ ci lépp luy lor nit ki ci diineem.

Feg làmmiñ ak téye ko mooy cosaanu

yiw yépp.

التصنيفات

Lislaam