ana lan moo dal aw nit ba ñuy wax lii ak lii? man de damay julli di nelaw, di woor di dog, di takk soxna, ku bañ sama yoon wi bokkul ci man

ana lan moo dal aw nit ba ñuy wax lii ak lii? man de damay julli di nelaw, di woor di dog, di takk soxna, ku bañ sama yoon wi bokkul ci man

Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Am mbooloo ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dañoo laaj soxnay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ay jëfam ci li nëbbu? Am ci ñoom ku ne: man du ma takk soxna, keneen ne: man duma lekk ndawal, keneen ne: man duma nelawati ci kaw lal, Yonente bi daldi sant Yàlla tagg ko, wax ne: "ana lan moo dal aw nit ba ñuy wax lii ak lii? man de damay julli di nelaw, di woor di dog, di takk soxna, ku bañ sama yoon wi bokkul ci man".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Am mbooloo ci Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm dañoo ñëw ci kër saxnay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di laaj jaamu Yàlla yu nëbbu yimuy def ci biir këram, ba ñu leen ko waxee mu mel ni dañu koo xeeb, ñu wax ne: Waaw nun fan la nu toll Yonente bi nga xam ne jéggal nañu ko li jiitu ci ay bàkkaaram ak li mujj, wuute ak ku xamul ndax amna ag njéggal walla, kon day aajowoo mu baril ay jaamu Yàllaam ndax amaana mu am njéggal. Am ci ñoom ku ne: man duma takk soxna. Am ku ne: man du ma lekk yàpp. Am ku ne: man duma nelaw guddi. Loolu egg ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu mer, daal di xutba nit ñi, mu sant Yàlla tagg ko, daal di wax ne: Lan mooy mbiri nit ñiy wax lii ak lii?! Giñ naa ci Yàlla ne man maa leen gën a ragal Yàlla te gën leen ko a moytu, waaye man damay nelaw ngir ma man a taxaw julli, damay dog ngir ma man a dëgër ci woor, te damay takk soxna, ku dummooyu samaw yoon, gis ag mat ci lu dul moom, mu jël yoonu keneen ku dul man kooku bokkul ci man.

فوائد الحديث

Sahaaba yi da ñoo bëgge aw yiw ta xemmeem ko bëgg lool di roy seenub Yonnente yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Yaatug Sariiha bi ak yombam, ndax li mu tege ci jëfu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak njubam.

Yiw ak baarke moo ngi ci roy ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ak topp ay mbiram yu tedd.

Ag Xuppe ñëw na ci ñuy ba ña sonal ak di teg bakkan yi ay jaamu Yàlla yu mu àttanul, ndax loolu dafa bokk ci meloy defkatu biddaa yi.

Ibn Hajar nee na: taral ci jaamu gi day indi yoqat ak bàyyi lépp far, yam ci farata yi rekk, ak bàyyi naafila yi day indi ag bayliku, ak ñàkk a sawar si jaamu gi, te li gën ci mbir yi mooy diggdóomu.

Nekk na ci topp mbiri mag ñi ngir roy ci seen i jëf, ak ne bu dee ne manu ñu koo xame ci góor ñi kon day dagan ñu gëstu ko ci jigéen ñi.

Ag waare nekk na ci ak joxe masalay xam-xam yi ak leeral ay àtteem ñeel muskallaf yi, ak dindi lënt gi ci way-pasteefu yi.

Digle ci ñeewant ci jaamu gi, ànd ak sàmmonte ak farata yi ak sunna yi; ngir jullit bi sàmmonte ak àqi keneen ci moom.

Nekk na ci hadiis bi ag tegtal ci ngëneelu sëy ak xemmemloo ci.

التصنيفات

Njubug Yónnent bi SLM