koo xam ne day jullu laata jant bi di fenk ak laata muy soh du dugg sawara

koo xam ne day jullu laata jant bi di fenk ak laata muy soh du dugg sawara

Jële nañu ci Abii Suhayr Umaarata ibn Ruaybata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: «koo xam ne day jullu laata jant bi di fenk ak laata muy soh du dugg sawara».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne: kuy saxoo di julli jullig Fajar ak jullig Tàkkusaan, du dugg sawara; mu jagleel ko ñaari julli yii; ndaxte ñoom ñaar ñooy julli yi gën a diis ci julli yi, ndax waxtuw suba day nekk ci jamono ji nelaw di neex, waxtuw tàkkusaan di jamono ji nit ki di nekk ci liggéey yi bëccëg gi ak yaxantu mi, ku sàmmonte ak ñaari julli yii ànd ak coono ba kon dana sàmmonte ak julli yi des.

فوائد الحديث

Ngëneelu ñaari julli yi suba ak tàkkusaan, kon warees naa sàmmonte ak ñoom ñaar.

Kuy jooxe julli yii ci li gën a bari day nekk ku bakkanam wéet ci tàyyeel ak ngistal di ku bëgg ag jaamu.

التصنيفات

Ngëneelu julli