ku seeti ku feebar, te ab digam ñëwagul, mu wax juróom-ñaari yoon: As-alul Laaha Al-Hasiima Rabba Al-Harsi al-hasiimi an yasfiyaka, lu dul ne Yàlla dana ko may jàmm ca feebar boobu

ku seeti ku feebar, te ab digam ñëwagul, mu wax juróom-ñaari yoon: As-alul Laaha Al-Hasiima Rabba Al-Harsi al-hasiimi an yasfiyaka, lu dul ne Yàlla dana ko may jàmm ca feebar boobu

Jële nañu ci Ibnu Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : "ku seeti ku feebar, te ab digam ñëwagul, mu wax juróom-ñaari yoon: As-alul Laaha Al-Hasiima Rabba Al-Harsi al-hasiimi an yasfiyaka, lu dul ne Yàlla dana ko may jàmm ca feebar boobu".

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne amul benn jullit buy seeti jullit bu feebar te waxtuw deewam jotagul, aji-seeti ji ñaanal aji-feebar ji, ci wax ne: (maa ngi ñaan Yàlla mu màgg mi) ci jëmmam ak i meloom ak i jëfam, (Boroom Aras ju màgg ja mu saafara la), mu baamtu ko juróom-ñaari yoon lu dul ne Yàlla dina ko saafara ca tawat jooja.

فوائد الحديث

Sopp nañu ñaanal aji-feebar ci ñaan gii, ak baamtu ko juróom-ñaari yoon.

Ku ñu ñaanal lii di nga wér bu soobe Yàlla bu dee da ko a def ci dëgg ak sellal.

Bu biralee ñaan gi mbaa mu yalu ko ñaar yépp dagan na, waaye bu fexee ba aji-feebar ji dégg ko loo lu mooy li gën; ndax loo lu da koy bégloo.

التصنيفات

Mocc gees yoonal