Aji-woote ji day woote ne: di ngeen wér te du ngeen tawatati ba fàww, di ngeen dund te du ngeen deeati ba fàww, di ngeen bijjaaw te du ngeen màggatati ba fàww, di ngeen xéewlu te du ngeen yoqatati ba fàww

Aji-woote ji day woote ne: di ngeen wér te du ngeen tawatati ba fàww, di ngeen dund te du ngeen deeati ba fàww, di ngeen bijjaaw te du ngeen màggatati ba fàww, di ngeen xéewlu te du ngeen yoqatati ba fàww

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu, ak Abuu Hurayrata yal na leen Yàlla dollee gërëm ñu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Aji-woote ji day woote ne: di ngeen wér te du ngeen tawatati ba fàww, di ngeen dund te du ngeen deeati ba fàww, di ngeen bijjaaw te du ngeen màggatati ba fàww, di ngeen xéewlu te du ngeen yoqatati ba fàww " loolu mooy li Yàlla di wax naan: {ñu woo leen ne leen loolu mooy àjjana ja dondloo nañu leen ko ci sababus li ngeen doon jëf} [Al-Ahraaf: 43].

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ne dees na woo waa àjjana fekk ñoo nga fa di xéewalu: di ngeen wér te du ngeen feebar ci àjjana ba fàww, di ngeen dund te du ngeen fi dee ba fàww, donte nelaw la te mooy dee gu ndaw, di ngeen fi bijjaaw te du ngeen fi màggatati ba fàww, di ngeen xéewlu te du ngeen fi yoqat baa ngéen fiy jaaxlee ba fàww, loolu mooy waxi Yàlla mu màgg mi: {ñu woo leen ne leen loolu mooy àjjana ja dondloo nañu leen ko ci sababus li ngeen doon jëf} [Al-Ahraaf: 43].

فوائد الحديث

Li gën a rëy ci yiy xatal xéewali dundug àdduna ji ak fu boroomam man a egg ci bànneexu, ñent bir la: tawat, ak dee, ak màggat, ak tiis ak njàqare ngir sababus ragal noon bi ak ñàkk ak geer yi ak yu dul yooyu, te waa àjjana dañoo mucc ci yooyu, tax waa àjjana am xéewal gu mat.

Wuuteg xéewalu àjjana ak li nekk ci àdduna ci xéewal; ndaxte xéewalu àjjana amul ragal, te xéewalu àdduna du sax ay mettit da koy gaar ak ay tawat.

Xemmemloo ci def lu baax yu ñuy jottalikoo jëm àjjana

التصنيفات

Meloy Àjjana ak Sawara