bu waa àjjana duggee àjjana, Yàlla mu Barkeel mi te kawe day wax ne: ndax bëggeen dara lu ma leen dolli?

bu waa àjjana duggee àjjana, Yàlla mu Barkeel mi te kawe day wax ne: ndax bëggeen dara lu ma leen dolli?

Jële nañu ci Suhayb yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «bu waa àjjana duggee àjjana, Yàlla mu Barkeel mi te kawe day wax ne: ndax bëggeen dara lu ma leen dolli? Ñu ne ko: ndax weexaloo sunu kanam yi? Ndax dugaloo nu àjjana, musal nu ci sawara? Nee na: mu wuññi kiiraay gi, joxeesu leen dara lu nu gën a bëgg ci xool seen Boroom bu màgg bi».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne bu waa àjjana duggee àjjana, Yàlla mu Baarkeel mi te kawe da leen di wax: Ndax bëgg ngeen ma dolli leen dara? Waa àjjana ñoom ñépp ne ko: ndax weexaloo sunu kanam yi? Ndax dugaloo nu àjjana musal nu ci sawara? Yàlla dindi kiiraay gi yëkkëti ko; te kiiraayam leer la, joxeesu leen dara lu ñu gën a bëgg ci xool seen jëmmi Boroom ju màgg ji.

فوائد الحديث

Wuññi kiiray gi ci waa àjjana ñu gis seen Boroom; bu dee yéefar yi nag; dees na leen ko xañ.

Li gën a màgg ci xéewali àjjana mooy way-gëm ñi gis seen Boroom.

Waa àjjana yépp ak lu seen wàccuwaay wuute danañu gis seen Boroom bu màgg bi.

Ngëneelu Yàlla ci way-gëm ñi ci dugal leen àjjana.

Solos njëkkante jëm àjjana ci ay jëf yu baax, ak topp Yàlla ak ub yonnenteem yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

التصنيفات

Meloy Àjjana ak Sawara