Saytaane naagu na ci jullikat yi jaamu ko ci goxi araab yi, waaye ci jaxase seen diggante

Saytaane naagu na ci jullikat yi jaamu ko ci goxi araab yi, waaye ci jaxase seen diggante

Jële nañu ci Jaabir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «Saytaane naagu na ci jullikat yi jaamu ko ci goxi araab yi, waaye ci jaxase seen diggante».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne Ibliis naagu na ci way-gëm yiy julli ñuy dellu di ko jaamu ak di sujjóotal ay xërëm ci goxi araab yi, waaye du deñ di ko xemmem, te pasteefam ak coonoom ak jëfam ak doxam deñul di nekk ci jaxase seen diggante ci ay xuloo ak bañante ak xeex ak fitna ak yu ko niru.

فوائد الحديث

Jaamu Saytaane mooy jaamu xërëm, ndaxte moo koy digle di ca woote, tegtal bi mooy li Yàlla mu kawe mi wax di nettali waxi Ibraahiima yal na ko Yàlla dolli jàmm: (yaw sama baay bul jaamu Saytaane...).

Saytaane day dox ci tàbbal ay xuloo ak i noonoo ak ay xeex ak i fitna ci diggante jullit ñi.

Bokk na ci njariñu julli ci lislaam moom day sàmm mbëggeel ci diggante jullit ñi, di dëgëral buumu mbokkoo ci seen diggante.

Julli mooy màndargam diine mi gën a màgg ginnaaw ñaari seede yi, loolu a tax ñu tudde jullit ñi jullikat yi.

Goxi araab yi dafa am jagleel bu beneen réew amul.

Bu nu nee yenn goxi araam yi am na jaamu xërëm, te Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: (Saytaane naagu na jullikat yi jaamu ko...), loolu xibaar la ci li nekk ci xelu Saytaane ci naagu ndax li mu gis ci ay ubbite, ak nit ñi di dugg ci diiney Yàlla ji di ay mbooloo, kon Hadiis bi xibaar la ci li Saytaane njort jàpp ko, topp li am wuute ak loolu ngir xereñte gu ci Yàlla mu màgg mi namm.

التصنيفات

Jikko yees ŋàññ