Ku waat ci kóolute bokkul ci nun

Ku waat ci kóolute bokkul ci nun

Jële na ñu ci Buraydata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «Ku waat ci kóolute bokkul ci nun».

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na artu na it ñuy waat ci kóolute, ak ne ku def loolu bokkul ci nun.

فوائد الحديث

Araamalees na waat ci ku dul Yàlla mu kawe mi, te bokk na ca: waat ci kóolute, te moom dafa bokk ci bokkaale gu ndaw.

Kóolute day làmboo topp yi ak jaamu yi ak ndénkaane yi ak joxe yi ak jàmmal yi.

Giñ du baax lu dul ci Yàlla, walla aw tur ci turam yi walla ci aw melo ci meloom.

Al-Xattaabii nee na: lii day niru ne li waral sibbeel gi mooy ne dafa digle ñuy giñ ci Yàlla ak i meloom, te kóolute bokkul ci meloy Yàlla yi, waaye ndigal la ci ay ndigalam, di farata ci ay farataam, ñu tere ko ndax li nekk ci loolu ci yamale digganteem ak diggante turi Yàlla mu màgg mi ak i meloom.

التصنيفات

Bokkaale