Julli naa ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy sëlmël ci ndayjooram: "assalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhu", ak ci càmmooñam: "assalaamu halaykum warahmatul Laah

Julli naa ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy sëlmël ci ndayjooram: "assalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhu", ak ci càmmooñam: "assalaamu halaykum warahmatul Laah

Jële nañu ci Waa-il ibn Hujrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Julli naa ak Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy sëlmël ci ndayjooram: "assalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhu", ak ci càmmooñam: "assalaamu halaykum warahmatul Laah".

[Tane na] [Abóo Daawuda soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan bëgg a génn ci julli gi day sëlmël ci ndayjooram ak ci càmmooñam, mu geestu ci kanamam jëm ci wetu ndayjoor, ànd ak wax: (assalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhu), daal di sëlmël ci càmmooñam, mu geestu kanamam ci wetu càmmooñam, ànd ak wax: (assalaamu halaykum warahmatul Laah).

فوائد الحديث

Yoonalees na ñaari sëlmël ci julli, te dafa bokk ci ponk yi.

Sopp nañu leeg-leeg ñu dolli ci wax: (wabarakaatuhu), ndaxte Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daawu ko saxoo.

Wax ñaari sëlmël yi ci julli gi ponk bu war la, bu dee geestu ci jamonoy wax ji nag moom luñu sopp la.

Jaadu na ñu wax: (assalaamu halaykum warahmatul Laah) ci jamono yi ñuy geestu du ko jiitu niki noonu it du am ginnaawam.

التصنيفات

Ni ñuy jullee