Bu ma bañul woon a sonal jullit ñi -walla sama xeet wi- kon dina leen digal socc ci julli gu nekk

Bu ma bañul woon a sonal jullit ñi -walla sama xeet wi- kon dina leen digal socc ci julli gu nekk

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "Bu ma bañul woon a sonal jullit ñi -walla sama xeet wi- kon dina leen digal socc ci julli gu nekk"

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne bu ragalul woon coono ci kaw way-gëmi xeetam wi kon dana waral ci ñoom ñuy jëfandikoo socc ci gépp julli.

فوائد الحديث

Ñeewantg Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci xeetam wi, ak ni mu ragalee coono ci seen kaw.

Cosaan ci ndigalu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mooy ne daa war, lu dul tegtal wane ne warul.

Sopp gi ñu sopp lii di socc, ak i ngëneelam ci julli gu ne.

Ibn Daxiixil Hiid nee na: xereñte gi nekk ci sopp ñuy socc bu nu jogee jëm ci julli gi mooy li julli nekk ag jege Yàlla, moo tax mu war a nekk ci melow mat ak set ngir feeñal teddug jaamu gi.

Mataleg Hadiis bi day làmboo soccug aji-woor ji donte ginnaaw jengug jant bi la, niki ñaari julli yii: Tisbaar ak Tàkkusaan.

التصنيفات

Jikkoy Muhammat SLM