jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc

jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne ab jullit du suturaal ab mbokku jullitam ci biri àdduna, lu dul ne Yàlla mu màgg mi dana ko suturaal ëllëg bis-pénc; ag pay day tollok jëf ja, suturag Yàlla ci moom mooy mu nëbbal ko ay ayibam ak i moyam wolif mu di ko siiwal ca barab bañuy pangee jaam yi, man naa nekk it ci bañ ko ca a regle bañ ka ko a fàttali.

فوائد الحديث

Yoonalees na ñu suturaal ab jullit bu defee ag moy, ànd ak tere ko loolu ak laabire ko, ak ragalloo ko Yàlla, bu dee dafa bokk ci ñu bon ñi ak yàqkat yiy fésal ay moy Yàlla, ñooñu jaaduwul ñu leen di suturaal; ndaxte suturaal leen da leen di ñemeloo moy ya, waaye dañu leen di kalaame ak njiit yi, donte dañuy tudd aw turam; ndaxte moom day fésal ag kàccooram ak ay moy Yàllaam.

Xemmemloo ci suturaal njuumtey ñeneen ñi.

Bokk na ci njariñi sutura: may aji-moy ji pexeg dellu ci boppam tuub jëm ci Yàlla; ndaxte fésal ay ayib ak i awra dafa bokk ci siiwal ñaawteef, te day yàq nekkiinu mbooloo mi, di xëcc nit ñi jëme leen ci def ko.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci ay turam ak i meloom, Jikko yees gërëm