إعدادات العرض
tegal sa loxo fiy metti ci sa yaram, nga wax: Bismil Laahi ñatti yoon, te wax juróom-ñaari yoon: Ahuusu bil Laahi wa xudratihii, min sarri maa ajidu, wa uhaasiru
tegal sa loxo fiy metti ci sa yaram, nga wax: Bismil Laahi ñatti yoon, te wax juróom-ñaari yoon: Ahuusu bil Laahi wa xudratihii, min sarri maa ajidu, wa uhaasiru
Jële nañu ci Usmaan ibn Abii Al-Haas As-Saxafii yal na ko Yàlla dollee gërëm ne dafa jàmbat Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc aw mettit wu muy yëg ci yaramam diirub ba mu jébbaloo dugg ci lislaam, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: «tegal sa loxo fiy metti ci sa yaram, nga wax: Bismil Laahi ñatti yoon, te wax juróom-ñaari yoon: Ahuusu bil Laahi wa xudratihii, min sarri maa ajidu, wa uhaasiru».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt සිංහල Kurdî Português Nederlands অসমীয়া Kiswahili ગુજરાતી پښتو Hausa Română മലയാളം Deutsch नेपाली ქართული Moore Magyar తెలుగు Кыргызча Svenska ಕನ್ನಡ Українська Kinyarwanda Македонски Oromoo ไทย Српски मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛ Malagasyالشرح
Usmaan ibn Abii Al-Haas yal na ko Yàlla dollee gërëm aw mettit da ko a dal xaw ko a ray, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëw fi moom di ko seet, xamal ko ñaan gog Yàlla dana ci yëkkëti li wàcci ci moom ci tawat; te mooy mu teg loxoom ci kaw barab bi muy jàmbat, daal di wax: (Bismil Laahi) ñatti yoon, topp mu wax juróom-ñaari yoon: (maa ngi muslu) di làqu di aaru (ci Yàlla ak kàttanam ci ayu li may yég) ci mettit ci waxtu wii teew (ma di ko moytu) di ragal mu amal ëllëg njàqare ak ragal, walla tawat ji wéy, mettit wi di tasaaroo ci yaram wi.فوائد الحديث
Sopp nañu nit ki mocc boppam kem ni mu ñëwe ci hadiis bi.
Jàmbat -gu andul ak naqarlu ak gaaral- safaanoowul ak wakkiirlu ak muñ.
Ñaan gi dafa bokk ci mbooleem def sabab yi, loolu a tax jaadu na nu tënku ci ay baatam ak i limam.
Ñaan gii day ñeel wépp mettitu cér.
Teg loxo bi ci barab biy metti ci bu ñu dee mocce ñaan gii.
التصنيفات
Mocc gees yoonal