jaay wurus ci wurus, ak xaalis ci xaalis, ak pepp ci pepp, ak mboq ci mboq, ak tàndarma ci tàndarma, ak xorom ci xorom, dañuy tolloo, dañuy yam, bu dee xeet yi wuutee nag, jaayeleen nu mu leen soobe, bu dee loxo ak loxo la

jaay wurus ci wurus, ak xaalis ci xaalis, ak pepp ci pepp, ak mboq ci mboq, ak tàndarma ci tàndarma, ak xorom ci xorom, dañuy tolloo, dañuy yam, bu dee xeet yi wuutee nag, jaayeleen nu mu leen soobe, bu dee loxo ak loxo la

Jële nañu ci Ubaadata Ibnus Saamit -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "jaay wurus ci wurus, ak xaalis ci xaalis, ak pepp ci pepp, ak mboq ci mboq, ak tàndarma ci tàndarma, ak xorom ci xorom, dañuy tolloo, dañuy yam, bu dee xeet yi wuutee nag, jaayeleen nu mu leen soobe, bu dee loxo ak loxo la".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na yoon wi wér ci jaay juróom-benni xeeti ribaa yii, te mooy: wurus, ak xaalis, ak pepp, ak mboq, ak tàndarma, ak xorom, bu dee wenn xeet wi la, niki jaay wurus ci wurus, ak xaalis ci xaalis... Fàww mu am ñaari sàrt: Bi ci njëkk: ñu yem ci peese bu dee lu ñuy peese la, niki wurus ak xaalis, walla ñu yem ci natt bu dee lu ñuy nay natt la niki pepp ak mboq ak tàndarma ak xorom. Ñaareel bi: aji-jaay ji téye njëg gi, kiy jënd téye njaay mi, loolu nag ca barabu fasug njaay ma lay doon. Bu xeet yii wuutee, niki jaay wurus ci xaalis, ak tàndarma ci pepp, kon jaay gi dana dagan ci benn sàrt, te mooy aji-jaay ji téye njëg gi, kiy jënn téye marsandiis bi ca bérabu fasug njaay ma, lu ko moy njaay ma yàqu, te kon tàbbi nañu ci bidaa bi ñu araamal, jaaykat bi ak jënnkat bi ñoo ci yem.

فوائد الحديث

Leeral alali ribaa yi ak naka lañu koy jaaye.

Tere nañu njaayum ribaa.

Këyiti xaalis yi àtteb wurus ak xaalis la am ci liy waral ribaa.

Jaay ak jënn ci juróom-benni xeet yiy am ribaa ci ay anam lay am: 1- ñu jaay luy am ribaa ci xeetam wuy am ribaa, niki wurus ak wurus ak tàndarma ak tàndarma... Kon ngir mu wér danañu ci sàrtal ñaari sàrt: ñu yam ci peese bi walla ci natt bi, ak joxante ca bérabu fas ga, 2- ñu jaay luy am ribaa ci luy am ribaa te du xeetam te ñu bokk sabab, niki wurus ak xaalis, ak pepp ak mboq, kon dees na sàrtal ci loolu joxante ga, walis ñuy yemoo, 3- ñu jaay luy am ribaa ci luy am ribaa te bokkuñu xeet, ànd ak wuuteg sabab ba, kon deesul sàrtal ci loolu joxante ga du caagine yemoo ga, niki jaay wurus ci tàndarma.

Jaay ak jënn xeet yi dul am ribaa, walla benn bi di luy am ribaa beneen bi di lu dul am ribaa; loolu deesu ci sàrtal joxante ga du caagine yemoo ga, niki jaay pàkk ci wurus.

التصنيفات

Ribaa