nit du jiiñ moroomam ag kàccoore, walla ag kéefar, lu dul ne dana dellusi ci moom, budee kooku melul noona

nit du jiiñ moroomam ag kàccoore, walla ag kéefar, lu dul ne dana dellusi ci moom, budee kooku melul noona

Jële nañu ci Abii Sarr yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne dégg na Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «nit du jiiñ moroomam ag kàccoore, walla ag kéefar, lu dul ne dana dellusi ci moom, budee kooku melul noona».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day àrtu ñuy wax keneen: yaw kàccoor nga, walla: yaw yéefar nga, bu dee nekkul li mu wax, kon moom mooy yayoo melo wi mu tudd waxam ji dellusi ci moom, bu dee li mu wax noonu la kon du dellusi ci moom; ndax li mu wax dëgg.

فوائد الحديث

Araamalees na di jiiñ nit ñi ak kéefar walla ag kàccoore, ci lu dul mbiru Sariiha mu ko waral.

Warees naa leerlu ci rotal àtte yi ci kaw nit ñi.

Ibn Daxiixil Hiid nee na: lii nag ag tëkku gu màgg la ñeel ku kéefarloo kenn ci jullit ñi te demewul noona, te guuta gu màgg la.

Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na: waaye mu ñàkk a nekk ci loolu ab kàccoor du caagine ab yéefar du tax mu bañ a am bàkkaar ci anam gi mu ko wax ne: yaw kàccoor nga, waaye anam gi am na ag teqale: bu ko jubloo laabire walla laabire keneen ci leeral meloom kon dagan na, bu ci jubloo ayibal ko ak siiwal ko ak lor ko kese kon du dagan; ndaxte dañu koo digal mu suturaal ko jàngal ko waar ko ca na mu gën a rafete, sa bu manee loolu ci ñeewant kon du dagan mu def ko ci taral; ndaxte man naa nekk sabab ci mu fétterlu ak mu nuur ca jëf jooja, kem ni mu nekke ci ñu bari ci niti daraja yi, rawati na bu dee kiy digle moo gën a suufe dayu ki muy digal.

التصنيفات

Kéefar, Kàccoor