Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na pasteefu ci fukk yu mujj yi lu mu daawul pasteefu ci yu dul yooyu

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na pasteefu ci fukk yu mujj yi lu mu daawul pasteefu ci yu dul yooyu

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne : Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na pasteefu ci fukk yu mujj yi lu mu daawul pasteefu ci yu dul yooyu.

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu fukki guddi yi mujj ci weeru Koor daan ñëw da daan pasteefu ci jaamu ak topp Yàlla, di jëf bu baax xeeti yiw yi ak xeeti baax yi ak jaamu yi lu ëpp lu mu daan góor-góor lu ci yu dul yooyu; ndax màggaay ak ngëneeli guddi yooyu, ngir sàkku it Laylatul Xadri.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci baril lu baax ak xeeti topp yi ci weeru Koor wépp, rawatina ci fukk yu mujj yi.

Fukk yu mujj yi ci weeru Koor moo ngi tàmbli ci guddig ñaar-fukk ak benn ba keroog weer wi di jeex.

Sopp nañu ñuy farlu ci waxtuy ngëneel yi ci topp Yàlla.

التصنيفات

Fukki guddi yi mujj ci weeru Koor