amna ci ñi leen jiitu woon jenn waay ju am gaañu-gaañu, mu saalit, daal di jël paaka dagg loxo bi, dereet ji dogul ba mu faatu, Yàlla mu kawe mi wax ne: sama jaam bi gaawe na ma ci boppam, araamal naa ci moom àjjana

amna ci ñi leen jiitu woon jenn waay ju am gaañu-gaañu, mu saalit, daal di jël paaka dagg loxo bi, dereet ji dogul ba mu faatu, Yàlla mu kawe mi wax ne: sama jaam bi gaawe na ma ci boppam, araamal naa ci moom àjjana

Jële nañu ci Al-Hasan mu wax ne: Jundub ibn Abdul Laahi yal na ko Yàlla dollee gërëm waxtaanal na nu ci jàkka jii, te fàttewuñu ba mu nu waxtaane ba tay, te ragaluñu ci Jundub fenal Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu ne: Yonnente Yàlla bi nee na: "amna ci ñi leen jiitu woon jenn waay ju am gaañu-gaañu, mu saalit, daal di jël paaka dagg loxo bi, dereet ji dogul ba mu faatu, Yàlla mu kawe mi wax ne: sama jaam bi gaawe na ma ci boppam, araamal naa ci moom àjjana".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xibaare na ne amna ca ña ñu jiitu woon jenn waay ju am gaañu-gaañu, mu daal di saalit muñul mettit wi, mu jël ab paaka daal di dagg loxoom bi ndax yàkkamtee dee, dereet ji dogul ba ni mu faatoo, Yàlla mu kawe mi wax ne: sama jaam bi gaawe na ma ci boppam, araamal naa ci moom àjjana.

فوائد الحديث

Ngëneelu muñ nattu yi, ak bàyyi foñ ci mettit yi ngir du waral lu ko gën a tar.

Waxtaane xeet yi jiitu woon ci li nga xam ne yiw moo ca nekk ak ug waare.

Ibn Hajar nee na: nekk na ci it taxaw ci àqi Yàlla yi ak yërmàndeem ci mbindeefam yi ba tax mu araamal ci ñoom ñuy ray seen bopp ak ne bakkan yi moomeelu Yàlla la.

Araamalees na jëfandikoo sabab yuy jëme ci ray bakkan, ak tëkku gu tar gi nekk ci loolu.

Ibn Hajar nee na: loolu day tegtale ne dafa ko a dagg ngir bëgg a dee waaye jubluwu ca faju.

التصنيفات

Ŋàññ moy yi