deesul dóor kenn lu ëpp fukki yar lu dul ci daani Yàlla

deesul dóor kenn lu ëpp fukki yar lu dul ci daani Yàlla

Jële nañu ci Abii Burdata Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne dégg na Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "deesul dóor kenn lu ëpp fukki yar lu dul ci daani Yàlla".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na ñiy dóor kenn lu ëpp fukki yar lu dul ci moy yi, waaye jubluwuñu ci li rot jóge ci Aji-Yoonal ji ci lim yi ñu tënk ci caw walla dóor walla mbugal yi ñu jagleel, li ñu ci jublu mooy deesul dolli ci dóoru yo xam ne ngir yare la lu ëpp fukki yar, niki caw sox na ak doom.

فوائد الحديث

Dig yi Yàlla digle walla mu tere ko dafa am ay mbugal yuy tax ñu koy moytu, ben muy lu Aji-Yoonal ji nattale, walla nattale ga dellu ci yéwénal gi àttekat bi gis.

Ag Yare day woyof ci kem jubbanti ga ak ragalloo ga, deesu ca weesu fukki yar bu dee aajo mooka waral, te li gën a yell nag mooy yar leen ci lu dul dóor, waaye ci jubbanti ak xamal, ak gindi, ak xemmemloo, loolu moo gën a gaaw a jëme ci nangu ak ñeewant ci jàngale gi, mbir yi nag ci barab bii day wuute lool, kon jaadu na ñu sàmmoonte ak li gën a yéwén.

التصنيفات

Àttey daan