إعدادات العرض
koddaayu jullit bi ca digg yeel ba la wara yam, aayul ci mu nekk ci digganteem ak dojor yi, lu nekk ci suufu dojor yi nag moom sawara la jëm, te kuy diri koddaayam ngir rëy-rëylu Yàlla du ko xool
koddaayu jullit bi ca digg yeel ba la wara yam, aayul ci mu nekk ci digganteem ak dojor yi, lu nekk ci suufu dojor yi nag moom sawara la jëm, te kuy diri koddaayam ngir rëy-rëylu Yàlla du ko xool
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "koddaayu jullit bi ca digg yeel ba la wara yam, aayul ci mu nekk ci digganteem ak dojor yi, lu nekk ci suufu dojor yi nag moom sawara la jëm, te kuy diri koddaayam ngir rëy-rëylu Yàlla du ko xool".
[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Português සිංහල Tiếng Việt অসমীয়া Nederlands Kiswahili Hausa ગુજરાતી Magyar ქართული Română Русский ไทย తెలుగు मराठी دری አማርኛ Malagasy Македонски Українська ភាសាខ្មែរ ਪੰਜਾਬੀ پښتو Yorùbá മലയാളം Svenskaالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne koddaayu góoru jullit bi, te mooy liy muur xaaju suuf gi ci góor, ñatt anam la: Bi ci njëkk mooy: lu ñu sopp te mooy mu nekk ci digg yeel bi. Ñaareel bi: bu dagan ci lu dul sibeel te mooy mu wàcc ba ci dojor yi; te ñooy ñaari yax yi génn ci fi yeel bi ak ndëngu li teqalikoo. Ñatteel bi: bu araam te mooy mu nekk ci suufu dojor yi, te dees na ragal ci moom sawara, bu dee day rëy-rëylu ak di bég ak di bew kon Yàlla du ko xool.فوائد الحديث
Melo yii ak tëkku yii góor ñi ñoo ko jagoo, bu dee jigéen ñi ñoom bokku ñu ci; ndaxte ñoom dañu leen a digal ñu muur seen mbooleem yaram.
Lépp luy muur xaaju suuf bi ci góor ñi dees na ko woowe koddaay; niki tubëy yi, ak mbubb yi ak yeneen, te day dugg ci àttey Sariiha yi ñu tudd ci hadiis bii.
التصنيفات
Teggiini col