bu nit waxee mbokkam: yaw yéefar bi, kon kenn ci ñoom ñaar yóbb na ko, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellusi ci moom

bu nit waxee mbokkam: yaw yéefar bi, kon kenn ci ñoom ñaar yóbb na ko, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellusi ci moom

Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "bu nit waxee mbokkam: yaw yéefar bi, kon kenn ci ñoom ñaar yóbb na ko, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellusi ci moom".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo na jullit bi di wax mbokkum jullitam: yaw yéefar bi, ndax kon kenn ci ñoom dana yayoo baatu kéefar bi, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellu ci ki yéefarloo mbokkam mi.

فوائد الحديث

Xupp jullit bi ci muy wax mbokk jullitam lu bokkul ci ay meloom ci meloy kàccoor ak kéefar.

Àrtu ci wax ju ñaaw jii, ak ne ki ko wax moo ngi ci giraawaale gu màgg bu ko waxee mbokkam, kon war na ci nit ki mu sàmm làmmiñam te bañ a wax ci lu dul ag xam gu wóor.

التصنيفات

Lislaam, Teggiini wax ak noppi