dees na dagg loxo ci ñenteelu xaaju Diinaar jëm kaw

dees na dagg loxo ci ñenteelu xaaju Diinaar jëm kaw

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "dees na dagg loxo ci ñenteelu xaaju Diinaar jëm kaw".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne sàcc bi dañuy dagg loxoom ci càccug ñenteelu xaaju Diinaaru wurus, ak lu ëpp loolu, ag xaymaam di yamoo ak 1.06 Garaam ci wurus.

فوائد الحديث

Sàcc ci bàkkaar yu mag yi la bokk.

Yàlla tënk na mbugalu ab sàcc te mooy ñu dagg loxoom; niki mu ko waxe moom Aji-Kawe ji: {sàcc bu góor bi ak sàcc bu jigéen bi daggleen seen i loxo} [Al-Maa-ida: 38], sunna leeral na sàrti dagg gi.

Li ñu namm ci loxo ci hadiis bi mooy dagg ténq bi ci fi mu teqalikook xasab bi.

Bokk na ci xereñug dagg loxo sàcc, aar alali nit ñi, ak àrtu tooñkat yi dul moom.

Diinaar ab xayma la ci wurus, leegi mu tollook (4.25 garaam); ñenteelu xaaju Diinaar day tolloo ak benn garaam ak dara.

التصنيفات

Gëtënu sàcc