إعدادات العرض
Ngëneel yi
Ngëneel yi
5- li dagan de leer na li araam it leer na,
7- ab jaam dafa def bàkkaar, daal di wax: yaw sama Boroom jéggal ma sama bàkkaar
9- kuy dog mbokk du dugg àjjana
10- ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam
12- Amul dara lu gën a tedd fa Yàlla mu kawe mi lii di ñaan
15- ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw dana ko dégg-loo diine
20- Yàlla dina musal nit ci samaw xeet ci kanamu mbindéef yépp ëllëg bis-pénc
22- Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar
26- ku dundal ñaari jigéen ba ñu mat, dana ñëw ëllëg bis-pénc man ak moom" mu tàppale ay baaraamam
30- giñ naa ci Yàlla ne Yàlla gindi ci yaw benn waay moo gën ci yaw nga am géttug jur
32- ndax du ma leen tegtal li Yàlla di fare njuumte yi, di ci yëkkatee daraja yi?
45- Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub
46- Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?
51- waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc
52- bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man
54- Yàlla du nangu ci jëf yi lu dul lu sell ñeel ko, ñu jublu sa jëmmam ji