إعدادات العرض
Ngëneel yi ak teggiin yi - الصفحة 2
Ngëneel yi ak teggiin yi - الصفحة 2
1- ku sol sooy fii ci àdduna du ko sol fële ca allaaxira
4- bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab
5- Bu kenn ci yéen di jàpp na def ndox ci bakkanam daa di saraxndiku, kuy fomp (laabu) na ko tóolal
9- Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal
10- misaalu toogandoo bu sell ak toogandoo bu bon moo ngi mel ni ki yor gëttug Misk ak kiy upp ab furne,
14- fi Boroom bi di gën a jegee jaam bi mooy ci mujjantalu guddi gi
17- yéemu naa ci mbirum jullit bi moom de mbiram lépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi
20- ku dundal ñaari jigéen ba ñu mat, dana ñëw ëllëg bis-pénc man ak moom" mu tàppale ay baaraamam
26- wàlle amul gaafal amul, njuuma amul, Safar amul, te nanga daw ki gaana kem ni ngay dawe Gaynde
27- giñ naa ci Yàlla ne Yàlla gindi ci yaw benn waay moo gën ci yaw nga am géttug jur
30- ndax du ma leen tegtal li Yàlla di fare njuumte yi, di ci yëkkatee daraja yi?
35- man maa ngi fa ma sama jaam bi njorte, te maa ngi ànd ak moom saa yu ma tuddee
40- sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy
41- jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc
42- bu kenn ci yéen faatu lu dul ne dafa rafet njort ci Yàlla
46- misaalu kiy tudd Boroomam ak ki dul tudd Boroomam, mi ngi mel ni misaalu kiy dund ak ki dee
47- man de bokk na ci li may ragal ci yéen sama ginnaaw, ñu ubbil leen naataangey àdduna ak taaram
49- ki war mooy nuyu kiy dox, kiy dox mooy nuyu ki toog, ñi néew ñooy nuyu ñi bari
50- lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko
53- bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy rus defal lu la neex
54- nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon
55- bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla
56- Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam
57- saaga ab jullig ag kàccoorte la, rayante ak moom ag kéefar la
61- ki nay dëgg mooy ki ñu ma tudd fi moom te julliwul ci man
63- éey yaw doomu Aadama ji boo ma ñaanee yaakaar ma ma jéggal la ak lu man a nekk ci yaw te duma faale
64- ñaan deesu ko delloo ci diggante nodd ak liqaam
65- Allaahuma aslih lii diinii allasii huwa hismatu amrii
67- Allaahuma innii as-aluka alhaafiyata fiddunyaa wal aaxirati
70- Allaahuma innii ahuusu bika min xalati addayni, wa xalabati alhaduwwi, wa samaati al-ahdaa
71- Allahuma bika asbahnaa, wa bika amsaynaa, wa bika nahyaa, wa bika namuutu, wa ilayka anusuuru
74- li gën a kawe cig jégalu yi mooy
85- ndax xam ngeen kan mooy ki ñàkk?
86- ku ma waxal jenn wax te xam ne ay fen la, moom kenn la ci fenkat yi
91- Saytaane naagu na ci jullikat yi jaamu ko ci goxi araab yi, waaye ci jaxase seen diggante
93- góor du xool awray góor, jigéen it du xool awray jigéen
