إعدادات العرض
Ngëneel yi ak teggiin yi - الصفحة 3
Ngëneel yi ak teggiin yi - الصفحة 3
1- saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam
2- dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf
3- Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama
4- ku ma fenal te tay ko na waajal ab wàccuwaayam ca sawara
7- Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub
8- Ndax kenn ci yéen bëgg na bu delloo ci njabootam fekk fa ñàtti giléem yu ëmb, rëy te suur?
14- bu ngeen gisee ñiy topp lënt ya xamleen ne ñooñii la Yàlla di wax nangeen leen moytu
16- waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc
17- {te dees na leen laaj xéewal yi bis booba}
18- bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man
21- Yàlla du nangu ci jëf yi lu dul lu sell ñeel ko, ñu jublu sa jëmmam ji
23- bokk na ci rafetug ngëmu nit ki: mu bàyyi lu ko amalul njariñ
25- aji-gëm nekkul kiy jamaate, walla kiy rëbbaate, mbaa kiy def ñaawteef, walla aji-bon lammiñ ji
26- dëddul àdduna kon Yàlla dana la bëgg, dëddul li ci nit ñi kon nit ñi danañu la bëgg
34- Allaahuma innii as-aluka alhudaa wattuqaa walhafaafa walxinaa
35- wax nga kàddu gog bu ñu ko jaxase woon ak ndoxum géej gi mu jaxase ko
37- ku wax: subhaanal Laahi Alhasiimi wa bi hamdihi, ñu jëmbëtal ko ag garabu tàndarma ca àjjana
42- yéen nit ñi tuubleen jëm ci Yàlla, man de damay tuub ci bis bi téeméeri yoon
44- jaamu Yàlla ci jamonoy fitna moo ngi mel ni gàddaay jëm ci ma
47- bu kenn ci yéen óbbalee na teg loxoom ci gémmiñam ndaxte Saytaane day dugg
50- Yàlla du xool kuy diri ay yéreem ngir puukarewu
51- ñaari xéewal a ngi nii yoo xamne nit ñu bari woru na ñu ci: ag wér ak ug jot
53- ñiy rëbbaate duñu nekk ay seede du caagine ay rammkat ëllëg bis-pénc
55- wax naa ci sa ginnaaw ñenti kàddu, ñatti yoon, bu ñu ko nattoon ci li nga wax ci bis bi mu tollu ko
58- ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege ëllëg bis-pénc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen
59- ki jébbalu, ñu wërsëgal ko lu doy, Yàlla def ko mu doylu ci li ko Yàlla jox koo ku texe na”
62- waat day jariñ liñuy jaay waaye day yàq tonowu
66- amul ñaari jullit yuy daje daal di joxante loxo lu dul ne dees na leen jéggal laata ñuy teqalikoo
69- am nga li nga mébét ak lu mel ni moom
76- bu ngeen dee laaj Yàlla laajleen ko Firdawsi
78- ku wax: radiiitu bil-Laahi Rabban, wa bi Muhammadin Rasuulan, àjjana war na ci moom
80- jaayanteleen ak man ci ne dungeen bokkaale Yàlla ak dara, te dungeen sàcc, dungeen njaalo
82- moytulleen bàkkaar yi ñuy xeeb
83- dañu ma a yónni ngir ma mottali jikkó yu tedd yi
84- juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral bis ba genn ker dul am lu dul keram ga
