إعدادات العرض
Pas-pasu Lislaam - الصفحة 2
Pas-pasu Lislaam - الصفحة 2
1- bis bi gën ci bis yi mooy bisu àjjuma
2- jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc
6- Yàlla jéggal na samaw xeet njuumte ak fàtte ak lu ñu leen forse
8- laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku ko Yàlla yombal ci moom
12- dinaa jox Raaya ji waa ju bëgg Yàlla ak ub yonnenteem, Yàlla dina ko ubbee ci ay loxoom
14- bokkul ci nun kiy mbej ñiy mbej lex ya, di xotti kaw yére ya, di woote wooteg ceddo ya
15- éey yaw doomu Aadama ji boo ma ñaanee yaakaar ma ma jéggal la ak lu man a nekk ci yaw te duma faale
17- giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom da ngeen topp yoonu ña leen jiitu woon
19- nit ñi gën a tar mbugal fa Yàlla ëllëg bis-pénc ñooy ñiy roy bindub Yàlla bi
20- doomu Aadama weddi na ma te loolu waru ko woon,mu saaga ma te waru ko woon
22- ñaar a ngi ci nit ñi ag kéefar la: jam ci askan yi, ak yuuxu ku dee
23- ndax xam ngeen kan mooy ki ñàkk?
25- amul kenn ci yéen lu dul ne Yàlla dina wax ak moom, te kenn kuy firi du nekk seen diggante
26- ku takk ab téere bokkaale na
30- malaaka yi duñu dugg kër gu am xaj walla nataal
31- malaaka yi duñu ànd ci mbooloo mu ànd akub xaj walla ab jóolooli
32- buleen di giñ ci yi ñuy jaamu te du Yàlla, buleen di giñ it ci seen i baay
33- Ku waat ci kóolute bokkul ci nun
38- Asan ak Usaynu ñooy sangi waxambaaney waa àjjana
40- ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba
43- maa ngi sant Yàlla mi delloo pexeem ya ci ay jax-jaxal
46- jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw
50- saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam
54- saa du taxaw ba keroog jamono ji di jegee
55- Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si
58- giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom ne ay koppam moo ëpp limu biddiwi asamaan si
59- dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf
60- Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama
62- lépp a ngi ci ndogal yi, ba ci lott ak muus, mbaa muus ak lott
63- bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo
64- man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
68- Yahuut yi ñooy ñi Yàlla mere, nasaraan yi ñooy ñi réer
69- xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?
70- waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc
71- li gay wax di ci woote lu baax la, boo ñu xibaaroon ndax la ñu defoon dees na ko jéggale
72- demal ne ko: yaw bokkoo ci waa sawara, waaye ci waa àjjana nga bokk
73- {te dees na leen laaj xéewal yi bis booba}
75- bindal, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, dara du ci génn lu dul dëgg
76- bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man
78- ñam na cafkag ngëm ki gërëm Yàlla muy Boroomam, lislaam di diineem, Muhammat di yonnenteem
80- ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun
83- dañuy jegeele jant bi ci mbindeef yi ëllëg bis-pénc, ba mu jege leen luy toll ni Miil
86- yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka
88- mo ndax wóoluwuleen ma te man maay kóoluteg ki ci asamaan xibaaru asamaan dima dikkal suba ak ngoon
89- am nga li nga mébét ak lu mel ni moom
93- bu ngeen dee laaj Yàlla laajleen ko Firdawsi
94- Ab kurel ci sama xeet wi du deñ di féete kaw, ba mbirum Yàlla di leen dikkal ñu nekk way-not
96- ñi gën ci yéen ñooy samag maas, topp ci ña ca topp, topp ci ña ca topp'
