إعدادات العرض
Xam jaamu Yàlla yi - الصفحة 2
Xam jaamu Yàlla yi - الصفحة 2
1- moom am ndoxam lu laab la , am méddam it lu dagan la
2- bu ndox mi nekkee ñaari mbànd kon du téye sobe
8- Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara
9- toogal diir bi la sa mbaax daan téye, topp nga sangu
10- sangu bisub àjjuma war na képp ku toll ci gént,ak mu soccu, ak mu laal gëtt bu ko amee
11- bu genn jigéen tukki lu mat doxub ñaari fan lu dul mu ànd ak jëkkëram walla ab jegeñaaleem
13- Bu kenn ci yéen jullee ci benn yére te dara tegewul ci kaw mbaggam
14- boo sujjóotee, na nga teg say ténq te yëkkëti say conc
17- ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw jullig farata gu ne dara terewukoo dugg àjjana lu dul dee
20- ku sàmmonte ak ñenti ràkka njëkk Tisbaar ak ñenti ràkka ginnaaw tisbaar yàlla araamal ko ca sawara
26- jihaadleen ak bokkaalekat yi ci seen alal ak seen bakkan ak seen làmmeñ
28- bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo
29- man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
30- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne
31- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na benn-benn
32- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na ñaar-ñaar
34- war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam
36- bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man
37- ku tabax jàkka ngir Yàlla Yàlla dana ko tabaxal ca àjjana lu mel ni moom
38- genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka
39- bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog
41- yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci
42- yéen nit ñi, damaa def lii ngir ngeen roy ak ngir ngeen xam samag julli
43- bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar
47- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne
52- bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj
56- Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan génn ci wanag day wax: "Xufraanaka
59- demal julli waat, yaw julliwóo
61- Yonente Yàlla bi daan na nu xamal listixaar ci mbir yépp kem ni mu nu daan xamale saaru Alxuraan
63- ku woor benn bis ci yoonu Yàlla, Yàlla soreele jëmmam ca sawara juróom-ñaar-fukki Nawet
64- nit ñi du ñu deñ di nekk ci yiw fii ak ñoo ngi gaaw a dog
68- xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la
75- dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor
81- yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka
83- ku woor at mi kooku woorul, woor ñatti fan mooy woor at mi yépp
85- bu Ramadaan ñëwee dañuy tijji bunti àjjana yi, tëj bunti sawara yi, jéng saytaane yi
87- juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral bis ba genn ker dul am lu dul keram ga
88- dénk naa leen julli ak ñi nekk ci seeni loxo
