إعدادات العرض
Dégg diine ak i cosaanam - الصفحة 2
Dégg diine ak i cosaanam - الصفحة 2
2- ku lekk laaj walla soble, bumu nu jege -walla mu wax: bumu jege sunu jàkka yi, te toog ci këram
6- ku jàngul faatiha amul julli
7- ku sangu bisub Àjjuma sangug janaba topp mu dem julli ji, dana mel ni ku saraxe ag giléem
8- kuy njëw ci yéen ci àjjuma ji na sangu
12- ku ne ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm,
18- koo xam ne day jullu laata jant bi di fenk ak laata muy soh du dugg sawara
23- amul kenn ci yéen lu dul ne Yàlla dina wax ak moom, te kenn kuy firi du nekk seen diggante
24- moom am ndoxam lu laab la , am méddam it lu dagan la
25- bu ndox mi nekkee ñaari mbànd kon du téye sobe
32- Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara
33- toogal diir bi la sa mbaax daan téye, topp nga sangu
34- sangu bisub àjjuma war na képp ku toll ci gént,ak mu soccu, ak mu laal gëtt bu ko amee
35- bu genn jigéen tukki lu mat doxub ñaari fan lu dul mu ànd ak jëkkëram walla ab jegeñaaleem
38- boo sujjóotee, na nga teg say ténq te yëkkëti say conc
40- ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw jullig farata gu ne dara terewukoo dugg àjjana lu dul dee
44- Yàlla jéggal na samaw xeet li seen i xel di xalaat, fii ak defuñu mbaa ñu wax
48- Yàlla daa bëgg ñu def limu yombal, kem ni mu bëgge ñu def mbir yimu dogu
49- bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo
50- man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
51- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne
52- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na benn-benn
53- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na ñaar-ñaar
55- war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam
57- bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man
58- ku tabax jàkka ngir Yàlla Yàlla dana ko tabaxal ca àjjana lu mel ni moom
59- genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka
60- bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog
62- yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci
63- yéen nit ñi, damaa def lii ngir ngeen roy ak ngir ngeen xam samag julli
64- bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar
68- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne
73- bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj
77- ñaar yii dañoo araam ci sama góori xeet wi, waaye dagan nañu ci jigéen ñi
78- Yàlla ak ub yonnenteem araamal na ñu jaay sàngara, ak médd, ak mbaam xuux, ak ay xërëm
79- Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan génn ci wanag day wax: "Xufraanaka
80- Tere na lépp lu am bëñ ci negment yi, ak lépp lu am aw sàll ci ñanaaw yi
82- ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun